Ba mu reeree ba noppi, yaay Astu woo na Badu. Dafa koo bëgg a wax nu nit di def ba am doxaliin wu rafet. Nee na ko : - boo bëggee doon dongo bu ñépp naw ci sa doxaliin, jëfeel lii :
_ jàngal teel a yewwu, raxas say gëñ bu baax, soo noppee, sol yére yu set.
_ Deel yore saa su ne jumtukaayi ekool, naka noonu téere,kaye ak yeneen yi.
_ Deel teg say jumtukaay fa ñu war a nekk ca kër ga. Boo ko defee, doo dëye boo waree dem ekool.
_ Gënal a farlu ci loolu, rawatina bu guddi jotee, bala ngaa tëdd.
_ Saa yoo wàcce, nanga ubbi say téere
ak say kaye, jàng li ñu la sant.
_ Jàppale nit ñi maase ak say waa-jur ni say waa-jur, sa moroomi rakk walla mag, ni say rakku bopp walla magu bopp.
_ Mayal cér sa nàttangoo yi, bañ leen a gënalante.
_ Wégal itam seen jàngalekati ekool yépp.
_ Bul naqari deret, walla nga
yëg sa bopp, boo nekkee sax dongo bi gën a xereñ ci seen kalaas.
_ Moytul te nga sàmm alalu mbooloo ak alalu jàmbur.
_ Bul yàq lu ñépp moom ndax ñépp a ko bokk.
- Bul jëw kenn, nanga jub te dëggu.
- Foo tollu, sàmmal sa kàddu saa yoo ko joxee.